¶ Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam.
TSK
TSK · Genesis 35:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ci kaw loolu Sikem doomu Amor, miy Eween te di kilifa ca dëkk ba, daldi koy gis, jàpp ko, tëdde ko, torxal ko.
¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.
¶ Ba loolu amee Musaa wàcc tund wa, dellu ca mbooloo ma. Mu sell-luloo leen, ñu fóot seeni yére,
¶ «Li ma leen wax lépp sàmmleen ko, te turi yeneen yàlla, buleen ko tudd; bumu jibe sax seen gémmiñ.
Waaye su fóotul, sanguwul, mooy gàddu bàkkaaram.»
¶ «Buleen am yeneen yàlla ci sama kanam.
Seen jëmmi tuur yooyu nag, lakkleen leen. Buleen xemmem lenn luy xaalis mbaa wurus ci kaw tuur yi. Buleen ko aakimoo, lu ko moy muy seenug fiir, ndax lu seexluwoo ngoogu ci seen Yàlla Aji Sax ji.
Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem, ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu.
Mu ne ko: «Gis nga sa wujju peccorgo waa ngay ñibbi cay bokkam aki yàllaam. Àndal ak moom ñibbi kay!»
Ana askan wu mel ni Israyil sa ñoñ ci kaw suuf, wenn askan wu Yàlla dikk, goreel leen ngir def leen ñoñam, ba turam siiw? Yaa leen defal ay jaloore, yaa defal sam réew ay kéemaan ci sa kanam ñoñ ñi nga goreele fa Misra aki askanam aki yàllaam.
Te sax xanaa Abanaa ngi nii ak Parpar, di dexi Damaas, gën fopp mboolem ndox muy wal ci Israyil? Ndax dama caa manuloona sangu, ba wér?» Mu walbatiku dem, mer lool.
Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba.
Naa teewlu yoonu maandute. Ana kañ nga may dikkal? Naa doxe maandute fi sama biir waa kër.
Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.
«Yerusalem, ana lu tax ma di la baal, te say doom wacc ma, di giñe lu dul Yàlla. Ma reggal leen, teewul ñuy njaaloo, riixle, jëm kër gànc ya!
Nit man naa sàkkal boppam ay yàlla? Te duñuy yàlla sax!»
Ma ne leen: “Tuur yi ngeen wékki gët yeen ñépp, xalableen leen. Kasaray tuuri Misra, buleen ci sobeel seen bopp. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.”
Ña ngay naan biiñ, di sàbbaal yàllay wurus yaak yu xaalis yaak yu xànjar yaak yu weñ yaak yu bant yaak yu doj ya.
Yeena gis nag mbaa ngeen déggal seen bopp ni Póol moomu di naxee ba fàbbi mbooloo mu bare, te du ci Efes gii rekk, daanaka Asi gépp la: Mu naay: “Yàlla yu loxol nit sàkk du yàlla.”
Gan juboo la Almasi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi?
¶ Bu jëkk, ba ngeen xamul Yàlla, ay yàlla yu dul dëgg ngeen daan jaamu.
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.
ñii ngeen wallu leen, foqatee leen ci sawara, ña ca des, ngeen yërëm leen yërmande ju ànd akug ragal, ba far seexlu ab turki bu seen yaram sobeel ndax seeni bàkkaar.