TSK

TSK · Genesis 35:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.

¶ Ba loolu wéyee Yanqóoba génn Beerseba, wuti Karan.

Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.»

Doj wii ma samp, muy xàmmikaay, mooy doon kër Yàlla, te lépp lu mu ma wërsëgal, dinaa ko génneel fukkeel ba moos.»

Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”»

Danuy dem Betel, ma sàkkal fa sarxalukaay Yàlla, ji ma wallu, ba ma nekkee ci njàqare, te ànd ak man fépp fu ma jaar.»

Musaa nag sàkk fa sarxalukaay, tudde ko tur wuy tekki «Aji Sax jeey sama raaya».