tegaat ca ne ko: «Léegi jigéenu wérul nga, te dinga am doom ju góor; nanga ko tudde Ismayla (mu firi Yàlla dégg na), ndax Aji Sax ji yég na sa naqar.
TSK
TSK · Genesis 37:25
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor, seeni tur a ngoog, ñuy fukki garmi ak ñaar yu jiite seeni mbooloo ci seeni sanc ak seeni dal.
Mu ànd nag ak ay bokkam, topp ko juróom ñaari fan, door koo dab ca tundi Galàdd.
fekk waa Majan yóbbu nañu ko Misra, jaay ko Potifaar, jawriñu Firawna mi jiite ay dagam.
¶ Seen baay Israyil nag ne leen: «Ndegam manula ñàkk, dangeen di def nii: sàkkleen ci ngëneeli réew mi, yeb ci seeni saaku, yóbbul waa ja lu mel ni tuuti diwu yaram ak lem ak cuuraayu xas ak cuuraayu ndàbb ak ay xeeti saal.
Aji Sax ji nee: «Xanaa ñiy def lu bon ñépp xamuñu dara? Ñuy lekk sama ñoñ niw ñam, te sàkkuwuñu Aji Sax ji.»
Jikkoy jigéenu moykat a ngi. Day lekk, wommiku, te naan: «Defuma dara lu aay!»
Moo diwu pajtal amul Galàdd a? Am fajkat a fi amul? Ana lu waral bokk yi taneeguñu?
Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj, ak a sóonoo seen laltu yu nooy, di yàpp mbote yu baax ak sëllu yu duuf,