Naka la Abner délsi ba Ebron, Yowab berook moom ca buntu dëkk ba, mel ni kuy déeyook moom, daldi koy jam ci biir, rey ko, feyul Asayel, rakkam ja Abner bóomoon.
TSK
TSK · Genesis 4:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Sang bi, ñaari doom yu góor laa amoon. Dañu doon xeex ñoom ñaar ca àll ba te ku leen àtte nekku fa. Kenn ki dóor moroom mi, rey ko.
Sanbalat ak Gesem yónnee ci man, ne ma: «Dikkal nu dem Kefirim ca xuru Ono, diisooji fa.» Booba ña nga may fexeel.
Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, kuy taxawi bérabam bu sell ba?
Kii a ngi xàccil ñi mu takktool, di fecci kóllëre,
Ab noon làqoo na ay waxam, lal pexey wor ca xolam.
Doom ju góor a ngi dofloo baay ba, ju jigéen ja jógal ndey ja, jabar jógal ndeyu jëkkër ja, nooni nit ki di waa këram.
La dale ca deretu Abel ba ca deretu Sàkkaryaa, ma ñu rey ca diggante sarxalukaay ba ak bérab bu sell ba, maa leen ko wax déy, dees na ko topp niti tey jii.
Yeena àgg fa Yeesu, Rammukat bi dox kóllëre gu yees gi, yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.
¶ Ngalla ñii! Ñoo jaare yoonu Kayin; ñoo lajj, topp Balaam cig réeram ngir ag peyoor; ñoo diiŋat ba sànku ni Kore.