TSK

TSK · Genesis 41:40

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Kon nag du yeena ma yebal fii, waaye Yàllaa. Te moo ma jagleel, ma doon cëslaayal Firawna, mel ni baay ci moom, jiite këram gépp, boole ci yilif mboolem réewum Misra.

¶ Ba loolu amee Samiyel jël njaqal diwu oliw lu ndaw, sotti ko ci kaw boppu Sóol, fóon ko, ne ko: «Aji Sax ji diw na la déy, ngir fal la njiitu ñoñam.

Mardose Yawut ba, moo sësoon rëkk ca Buur Aserus, sut Yawut yépp, ay bokki Yawutam yu bare nawloo ko. Muy sàkku nag ngëneeli ñoñam, di waxal jàmm mboolem askanam.

Sujjóotal-leen doom ji, bala moo mer, ngeen sànkoo seenu yoon; meram day jekki ne jippét, waaye ndokklee képp ku ko làqoo!

Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo.

¶ Ca la Baltacar joxe ndigal, ñu solal Dañeel yérey buur yu xonq curr, takkal ko caqu wurus, daldi yégle ne moo topp ci bummi.

Acts 7:10 TSK

xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.