Te ngeen yóbbaale ci xaalis lu tollook ñaar-cay la ngeen jënde woon, ngir feyaale loola, ndax jombul njuumte la woon.
TSK
TSK · Genesis 43:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Genesis 43:12
TSK
Genesis 44:8
TSK
Xaalis bi nu fekkoon ci sunu bunti saaku sax, danoo àndaat ak moom, jóge ba Kanaan, délloosil la ko, kon nan lanu mana sàcce sa kër sang xaalis mbaa wurus?
Romans 13:8
TSK
¶ Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa.
Hebrews 13:18
TSK
¶ Deeleen nu ñaanal nag. Li nu wóor de, moo di sunum xel yeddu nu fenn, te it di def lu baax ci lépp moo di sunu bëgg-bëgg.
1 Peter 3:16
TSK
Waaye nay tont lu rafet te ànd akub yar. Saxooleen di jëfe li dalal seenum xel, ba mbir ma ñu leen di baatali, ñooñuy ŋàññ seen dundin wu rafet wi leen Almasi manloo, gàcce rekk lañuy jële ca mbir ma ñu leen di baatali.