Léegi nag waatal ma fii ci Yàlla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal.»
TSK
TSK · Genesis 47:31
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Genesis 21:23
TSK
Genesis 24:3
TSK
ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.
Genesis 47:29
TSK
Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp, muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra.
Genesis 50:5
TSK
baayam da ne woon, mu ngi waaja dee, waaye bàmmeel ba mu yettaloon boppam ca xunti ma ca réewu Kanaan, na ko giñal ne dina ko denc foofa. Mu ne kon, na ko Firawna may, mu robi baayam, ni mu ko ko giñloo woon, te délsi.
Hebrews 11:21
TSK
¶ Ba Yanqóoba di waaja nelaw, ngëm la ñaanale ñaari doomi Yuusufa yépp, doora sujjóot, jafandoo boppu yetam.