Mu ñaanal Ibraam ne ko: «Yaw Ibraam, Yàlla na la Yàlla Aji Kawe ji barkeel, moom mi sàkk asamaan ak suuf!
TSK
TSK · Genesis 47:7
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem.
«Waxal Aaróona aki doomam ne leen ni ñuy ñaanale bànni Israyil, nii la; nañu leen wax ne leen:
Ci biir loolu Eli daan na ñaanal Elkana ak soxnaam, bala ñoo ñibbi, ne: «Yal na la Aji Sax ji may kuutaay ak sa soxna sii, ñu wuutu ki mu sédd Aji Sax ji.»
Yowab nag daanu ca suuf, sujjóot, ne Buur: «Buur, sang bi, yal nanga barkeel, sang bi. Xam naa ne may nga ma cér, gannaaw yaa ma may lii may dagaan.»
te it jawriñi Buur ñëw nañu, di sargalsi sunu sang Buur Daawuda, ne ko: “Yal na sa Yàlla siiwal turu Suleymaan, ba mu gën laa amu tur. Yal na kaweel ab jalam, ba mu gëna kawe sab jal.” Buur sujjóot ca kaw lalam,
Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.