TSK

TSK · Genesis 49:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bu leen njàqare dikkalee, fekk mboolem mbir yooyu dab leen, su boobaa dingeen mujj délsi ci seen Yàlla Aji Sax ji te dingeen ko déggal.

Wool-leen ma seen magi giir yépp, ak seeni kàngam, ma wax kàddu yii, ñuy dégg, ba ma seedeloo asamaan ak suuf, ci seen kaw, ñoom.

Ndéeyu Aji Sax ji, jagley ku ko ragal. Kóllëreem la koy xamal.

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

“Ay jant a ngii di ñëw, dees na yóbbu Babilon lépp lu nekk sa biir kër, te say maam dencoon ko, ba tey jii. Du lenn luy des. Kàddug Aji Sax jee.

Ana ku gëm sunub dégtal? Ana ku Aji Sax ji won dooley përëgam?

Waaye, Buur Nabukodonosor, Yàllaa ngi biir asamaan, di xamle ay mbóot te moo la won liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:

¶ Ci ñetteelu atu nguurug Sirus buuru Pers, kàddu daa dikkal Dañeel ma ñuy wax Beltasar. Kàddu googu di gu wóor tey yégle xare bu mag. Mu dégg kàddu gi, xam pirim peeñu mi.

Amos 3:7 TSK

Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.

Luke 2:26 TSK

Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi.

Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»

¶ Lii, nanga ko xam: mujug jamono, jant yu tar dina dikk.

Nanu seet itam ci sunu biir nu nuy xiirtalantee ngir cofeel ak jëf ju baax.

¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»