TSK

TSK · Genesis 6:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal.

ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.

¶ Gannaaw gi Rebeka ne Isaaxa: «Àddina soof na ma ndax jigéeni Etteen ñi. Yanqóoba de, bu jëlee ci jigéeni réew mi di Etteen ñu mel ni ñii, sama dund gi, dee a koy gën!»

Su ko defee nga wax Firawna, ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Israyil mooy sama taaw bu góor.

Buleen séyanteek ñoom: seen doom ju jigéen, buleen ko may doomu xeet yooyu, jigéenu xeet yooyu it, buleen ko jëlal seen doom ju góor.

Ezra 9:1 TSK

¶ Gannaaw ba loolu wéyee njiit ya dikk, ne ma: «Du bànni Israyil, du sarxalkat yi, du Leween ñi, kenn ci ñoom teqlikoowul ak xeeti réew meek seen aada yu siblu. Dañuy jëfe ni Kanaaneen ñeek Etteen ñeek Periseen ñeek Yebuseen ñeek Amoneen ñeek Mowabeen ñeek waa Misraak Amoreen ñi.

Seen genn-wàlli njaboot di làkk asdodd, ña ca des di làkk leneen ci làmmiñi doxandéem yi, te kenn ci ñoom manula wax yawut.

Job 31:1 TSK

Maa jaayanteek samay gët. Ana nu may xooleb janq?

Yaw déy yaa di sunu Baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israyil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”

Kenn deful lii te desem xel. Kenn doŋŋ a ko defoon. Ndax lan? Kuutaay li ko Yàlla digoon la doon wut. Kon nag sàmmleen seenum xel, te buleen wor seen jabar ja ngeen jël ba ngeen di ndaw.

Te it sëti Ibraayma yépp bokkuñu ci askanam, waaye li Mbind mi indi moo di: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan.»

¶ Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?

¶ Seeni gët xoolul lu moy ku ñu jaalool, te duñu bàkkaar ba regg mukk; ku dëgërul, ñu yóbbaale la. Ñooñu la seenub xol tàggatu ci ag bëgge, mii njurum alkànde!