TSK

TSK · Genesis 6:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Waaye waa Sodom ñu bon lañu woon, te mana moy Aji Sax ji lool.

Aji Sax ji du nangoo baal kooku, nde su boobaa, sànjum Aji Sax jeey ànd ak fiiraangeem, tàkk ci kawam, te mboolem alkànde gi ñu bind ci téere bii day këppu ci kawam, te Aji Sax jeey far aw turam fu asamaan tiim.

Job 22:15 TSK

Dangaa nara topp ñallu démb, wa nit ñu bon ña ñaloon?

Ab dof a nga naa ca xelam: «Yàlla amul,» tey def njekkar, njubadeem siblu, kenn defu ci lu baax.

Lenn daal laa ràññee: Yàlla daa sàkk nit, jubal ko, nit di wuta sél fu ne.

«Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon, ndax nga mucc. Foo àppal sa mébéti xol yu bon?

Mu ne ma: «Jàllal, ba gis tojaange yu bon yi ñu fiy def.»

¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.

¶ Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar,