Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.
TSK
TSK · Genesis 9:27
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
Gannaaw tooñug bànni Israyil mooy xéewalu àddina si, seenug néewle di xéewalu jaambur ñi dul Yawut, kon bu bànni Israyil yembee, ndaw xéewal gu gënatee baawaan!
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru.
ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
Ngëm la Ibraayma daleji ca suuf, sa ñu ko digoon, ba dëkke ay xayma ni ab doxandéem ci réewum jaambur, moom ak ñi mu séddool benn dige bi, te ñuy Isaaxa ak Yanqóoba.