Yàlla dafa bind nit ci takkndeeram; ci takkndeeru boppam la Yàlla bind nit, góor ak jigéen la bind.
TSK
TSK · Genesis 9:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam,
¶ «Ku dóor nit, rey ko, dee rekk mooy àtteem.
te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca bunt jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.
¶ «Su dee ag weñ la ko dóor, mu dee, moo ko rey, te dee rekk mooy àtteb ki rey.
Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.
Rawatina nag nit ñu bon ñu rey jaamburu Yàlla ci biir këram, ci kaw lalam sax. Kon duma def lu moy topp leen bakkanam, jële leen ci kaw suuf!»
Jëflanteel ak moom ci kaw xel, bu ko bàyyi mu duggaale bàmmeel bijjaaw.
¶ Yowab àndul woon ak Absalom ci pexeem, waaye Adoña la mujj àndal. Ba Yowab yégee la xew, daa daw ba ca xaymab Aji Sax ji, jàpp ca béjjén ya ca cati sarxalukaay ba, ngir rawale bakkanam.
Ba mu ko defee ñu teg ko loxo. Ba mu demee ba àgg kër Buur, bay tollook fa fas yay dugge, foofa lañu ko reye.
¶ Aw làmmiñ lanuy sante kiy Boroom bi, di Baay, te it ci lanuy móoloo nit ñi bindoo takkndeeru Yàlla.