Mu ne: «Dal-leen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»
TSK
TSK · Haggai 1:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!
Ana ku silmaxa ku moy sama jaam bii? Ku tëx ba dab sama ndaw li ma yónni? Ana ku silmaxa ba dab kii ñu jàmmal? Ku silmaxa ba dab jaamu Aji Sax jii?
Maay dëggal sama kàddug jaam, di sottal sama ndéeyal ndaw. Maa naan ci Yerusalem: “Dees na ko dëkke,” dëkki Yuda, ma ne: “Dees na leen tabaxaat, ma dekkali gentam bi.”
Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare. Moo tax ñi may tëru di tërëf, ba duñu daan, xanaa rus lool, ndax duñu baaxle; gàcce gu yàgg lay doon te du fey.
«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.
«Kàddug sarxalkat déy day sàmm xam-xam, te ciy waxam la nit ñi di sàkkoo àlluwa, nde mooy ndawal Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.