Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
TSK
TSK · Haggai 2:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Xam naa jikkoom, waaye maa koy faj, wommat ko, dëfale koy xéewal, mook ñiy ñaawloondook moom.
Ab saamar la ñooñuy yilife Asiri, réewum Nimróot mooma ca biiri buntam. Kilifa gi ñu dige moo nuy xettleek Asiri, bu ñu nu songee, ba joggati sunu suuf.
Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.
¶ Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jaambur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.
Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.