¶ Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
TSK
TSK · Hebrews 10:32
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leere ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi.
Ndax kat yeen la may ci jëmmu Almasi, yiwu gëm Almasi, rax ci dolli, ngeen sonn ndax moom,
¶ Bëgg naa nag, ngeen xam xare bu metti, bi ma leen di xareel, yeen ak waa Lawdise ak mboolem gëmkat ñi ma masula teg bët,
Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko.
Yeen kat xareeguleen ak bàkkaar, ba seen deret tuuru ci.
Kon nag fàttlikul fu kawe fa nga xàwwikoo ba fii, te nga tuub, di jëfe jëf ja nga jëkke woon. Lu ko moy maay dikk ba fi yaw, daldi jële sa tegukaayu làmp fa bérabam, ndegam tuubuloo.