TSK

TSK · Hebrews 13:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Waaye kilifa, ga yore naani Firawna, xalaatul sax Yuusufa, da koo fàtte.

¶ Ci biir loolu Ebedd Meleg, Kuuseen ba, di bëkk-néeg ci biir kër buur, dégg ne tàbbal nañu Yeremi ca kàmb ga. Fekk Buur a nga toog ca bunt ba ñu dippee Beñamin.

Ci kaw loolu mu sant njiitu takk-der ba, ne ko mu may Póol bët, woyofal ko jataayu kasoom te baña aaye ay nitam ñu topptoo ko.

Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.

¶ Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir gu ni mel.

Teewul seen ndimbal lii di jëf ju rafet ju ngeen bokke ak man, sama njàqare.

Yal na Yàlla baaxe nag waa kër Onesifor, yërmandeem, ndax dëfal na ma lu bare, te kersawoowul li ñu ma tëj kaso,

¶ Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof.