¶ Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux.
TSK
TSK · Hebrews 13:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Su dee jigéen ju góor àndal, te wasal génn, nañu sangu, te du tere ñu yendoo sobe ba jant so.
Ilkiya sarxalkat ba daldi dem ànd ak Ayikam ak Agbor ak Safan ak Asaya, ba ca Ulda yonent bu jigéen bay soxnas wattukatub yére ya, Salum doomu Tigwa doomu Aras. Ulda ma nga dëkkoon Yerusalem ca sanc ba. Ñu wax ak moom.
Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?
Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.”
Waa biti ñoom, Yàlla moo leen di àtte. Yeen, nag: «Tenqeeleen ku bon ci seen biir.»
Waaye moytu powum séy war naa tax ba góor gu nekk am jabaram, jigéen ju nekk it, am jëkkëram.
Am sañunoo yóbbaale mbokkum gëmkat buy sunu soxna, ni yeneen ndawi Almasi, ak doomi ndeyi Sang bi, ak Sefas?
¶ Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmi, te mooy: powum séy, ak jëfi sobe, ak yàqute,
Ndax lii kat na leen wóor: képp ku nekke powum séy, mbaa jëfi sobe, mbaa ag bëgge, kooku amul cér ci nguurug Almasi ak Yàlla, ndax ku bëgge ab bokkaalekat la.
Njiit li nag fàww mu mucc sikk, di ku dencul lu wees jenn jabar, ku moom bakkanam, jiital am xelam, di ku nawlu, man gan, te mana jàngle.
¶ Ab taxawukatu mbooloo mi bumu denc lu wees jenn jabar te na yor ay doomam, ak këram, yorin wu rafet.
Moo tax ma bëgg, jëtun ñiy ndaw séyaat, ami doom, yor seen kër, ba noon bi du am lu mu yàqe sunub der.
Moytuleen bala kenn a yebu ci powum séy, mbaa mu teddadil lu sell ba mel ni Esawu mi weccee woon ag lekk, céru taaw ba mu yelloo.