TSK

TSK · Hebrews 2:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yuusufa ne baayam: «Ñii ñooy sama doom, yi ma Yàlla jox fii.» Baayam ne ko: «Nañu jegesi, ma ñaanal leen.»

Sa njekk a tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!

Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde, njurum doom yool la.

Ma ne: «Yàllaa may wallu, ma dal-lu, duma tiit. Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki sax, di Aji Sax ji, te mooy sama wall.»

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

Su ngeen amoon fukki junniy njiit yu leen di sàmm ci yoonu Almasi it, du tax ngeen am lu wees benn baay, te man maa leen àgge xibaaru jàmm bi, ba tax ma di seen baay ci yoonu Almasi Yeesu.