TSK

TSK · Hebrews 2:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bu keroogee ku dëkke tefes googu dina ne: «Xanaa kay du ñii lanu yaakaaroon! Te nu dawoon di wuti ndimbal ci ñoom, ngir rëcc buurub Asiri! Léegi nag nu nuy mucce?»

Sax a leen di lekk ni mbubb, max ŋeeñ leen ni ndimol kawaru gàtt; te du tee sama njekk sax dàkk, sama wall saxal maasoo maas.

Ka bokk ci askanu buurub Israyil nag fippu, yónni ay ndaw réewum Misra, ngir ñu jox ko ay fas ak mbooloo mu takku. Moo ka def loolu dina baaxlee? Mbaa dina mucc? Nu mu cay mucce te wor kàddu, ga mu fasoo woon?

Luke 1:2 TSK

noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla.

Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Mu doonoon ab yonent bu manoorewu ci jëf ak ci kàddu, Yàlla ak askan wépp seede.

Acts 1:22 TSK

dale ko ca ba ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jëlee fi sunu biir, yéege ko. Kon nag kenn ci ñooñu war naa bokk ak nun, seede ndekkitel Yeesu.»

Acts 4:12 TSK

Mucc kat amul ci keneen, ndax fi asamaan tiim, mayeesul fi nit ñi weneen tur wu nu wara mucce.»

Yaw nit kiy sikk ñiy jëfe yooyii, te di ko def, ndax defe nga ne yaw ci sa bopp dinga rëcc àtteb Yàlla?

Mboolem kàddu gii may wax, lu wóor la te jara gëm: Almasi Yeesu moo dikk ci àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!

Ci fan yu mujj yii, Doom ji la waxe ak nun, ki mu jagleel lépp, ki mu sàkke àddina wërngal këpp.

Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.

Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.

¶ Wattuleen bala ngeena tanqamlu kiy wax ak yeen. Ndegam ña tanqamlu woon ka yékkati woon kàddoom, wax ak ñoom ci kaw suuf ñoo rëccul, aste nun ñii, su nu dëddoo kiy waxe fa asamaan.

Ñu ne tund yeek doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw, làq nu kanamu ki toog ci ngàngune mi ak sànjum Gàtt bi,