Yaa ko may nammeeli xolam, gàntuwulooy dagaanam. Selaw.
TSK
TSK · Hebrews 2:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,
Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
¶ Kon nag noonee moyug kenn jure mbugalu nit ñépp daal, noonu la jenn jëfu njekk jurale ñépp dundin wu yees ci kaw àtteb njub bu leen jenn jëf ja may.
Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa jooxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?
Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.
Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,
¶ Gannaaw nag ab sarxalkat bu mag bu mu mana doon, dees koo fal, ngir muy jébbale ay jooxe ak saraxi jur, kon fàww sarxalkat bu mag bii itam am lu mu sarxe.
ñi Almasi tax ngeen gëm Yàlla. Te Yàllaa ko dekkal, may ko ndam, ba tax Yàlla di ki ngeen gëm, yaakaar ko.
Ay gëtam a ngi mel ni sawara wuy tàkk, bopp bi, mbaxanay buur yu baree ci tege, ñu bind ci kawam tur wu kenn xamul ku dul moom.