Aji Sax jee ko giñ, te du dellu gannaaw: «Yaa dib sarxalkat ba fàww, topp dayob Melkisedeg.»
TSK
TSK · Hebrews 3:1
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Xalam yaak tabala yaak toxoro ya jolli, biiñ xelli ca xawaare ja. Seetluwuñu sax li Aji Sax ji def, xooluñu li mu jo loxoom.
Yaw nag nit ki, dajaleel digg bëccëg, ñépp gis, sa jumtukaayi ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu.
Kon nag léegi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Teewlooleen xel seeni jaar-jaar.
Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.
Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam.
Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.
ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.
Gannaaw menn mburu la nag, doonte ñu bare lanu, kon wenn yaram lanu, ndax nun ñépp, menn mburu mi lanu bokk.
ba mu leer ne jaambur ñi dul Yawut ñooy bokk ak Yawut yi benn cér bi, ñooy doon wenn yaram, te ñooy bokk benn dige bi ci Almasi Yeesu, ni ko xibaaru jàmm bi xamlee.
¶ Wenn yaram a fi nekk, ak genn Noo, ak jenn yaakaar ju leen wooteb Yàlla jëme.
te ngeen di sante Baay bi, mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga.
¶ Yeenay ñi Yàlla taamu, sellal leen, sopp leen. Kon nag solooleen xolu yërmande, akug mbaax, ak woyoflu, ak jikko ju lewet, ak xolu muñ.
Maa ngi leen di dénku nag, ngir Boroom bi, jàngleen biral bataaxal bii ngir bokk yépp.
Ci loolu it la leen woo ba mu jëfandikoo xibaaru jàmm bi nu leen àgge, ngir ngeen séddu ci sunu ndamal Boroom Yeesu Almasi.
Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.
Defal sam xel ci li ma la wax. Boroom bi moo lay leeralal lépp.
Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal bakkan.
¶ Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat bu mag bu jàll ba biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkisedeg.
¶ Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu tooge ndijooru ngànguney ku Màgg ka fa asamaan.
Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla.
Bu jëkkoon loolu moo doon gànjaru jigéen ñu sell ña yaakaaroon Yàlla te nangul seen jëkkër,
Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.
Dinañu xare ak Gàtt bi, waaye Gàtt bee leen di daan, ndax mooy Sangu sang yi, di Buuru buur yi. Mooy daan mook ñoñam, ñi mu woo, tànn leen te ñu saxoo topp ko.»