TSK

TSK · Hebrews 4:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

Job 26:6 TSK

Fàŋŋ la njaniiw def fa kanam Yàlla; du genn kiiraay gu ko làq paxum sànkute.

Job 38:17 TSK

Dees laa won bunti ndee? Am yaa gis bunt ya jëm lëndëmu njaniiw?

Asamaan la Aji Sax jiy jéere, di gis doom aadama yépp.

Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.

Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.

Jépp jëf déy, la Yàlla di àtte, ba ci lépp lu làqu, muy lu baax, di lu bon.

Ndaxam dégluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal.

Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.

Moo tax buleen àtte lenn te jotul, lu jiitu Boroom biy dikk. Moom mooy leeral li làqoo ag lëndëm, di làññi mébéti xol. Su boobaa ngërëm la ku nekk yelloo, fa Yàlla lay bawoo.

Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.