TSK

TSK · Hebrews 7:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dige naa sama bakkan; boo yeboo laaj ma ko. Bu ma la ko délloosilul, ba teg ko fi sa kanam, maa lay tooñ sama giiru dund.

Doom, dangaa gàddul nit bor, dige feyal jaambur,

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

Noonu itam la def ak kaas ba, gannaaw reer ba, ne leen: «Kaas bii mooy kóllëre gu yees gi fasoo ci sama deret. Deeleen def lii, di ma ko fàttlikoo, saa yu ngeen ci naanee.»

Looloo tax Yeesu di defarekat bi fas kóllëre gu bees, ngir ñi ñu woo mana jot ci muur gu sax dàkk gi ñu leen dig. Deeyam gi mu dee, moom la leen jote ci bàkkaar yi ñu xëtte kóllëre gu jëkk ga.

¶ Yàlla miy boroom jàmm, moom mi dekkal sunu Sang Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci dooley deret ji mu fase kóllëre gu sax dàkk,