TSK

TSK · Hebrews 7:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Mboolem ñi ànd ak Yanqóoba, ñëw Misra, muy ñi mu giir, te limaaleesul soxnay doomi Yanqóoba ya, tollu nañu ci juróom benn fukki bakkan ak juróom benn.

¶ «Léegi nag yaw, nanga seppee ci bànni Israyil sa mag Aaróona, ak doomam yu góor, nga woo leen fi yaw, ñu di ma sarxalal: Aaróona ak doomam yu góor, Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.

Yaw mu jegeñal la, yaak sa bokki Leween ñépp, ngeen di xëccu céru carxal, boole ci!

Yaw nag yaak say doom, dénkooleen seenug carxal ci mboolem mbiru sarxalukaay bi, ak ca wàllaa ridob biir bi, ngeen di ca liggéey. Seen liggéeyu carxal bi, ab sasu teraanga la, maa leen ko terale. Waaye ku bokkul ci yeen, bu ci laalee, dees koy rey.»

Waaye du yaw yaay tabax kër gi; sa doom ju góor ju soqikoo ci sa geño, moom mooy tabax kër gi, tudde ma ko.”

¶ Ma dégg itam ne joxuñu Leween ñi seeni cér, ba tax ku nekk ci Leween ñaak jàngkati kër Yàlla ga ne coww ca toolu boppam, bàyyi liggéey bi mu sasoo.

Ndax ba Melkisedeg di gatandu Ibraayma, Lewi ma nga woon ca geñog Ibraayma maamam.