TSK

TSK · Hebrews 9:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ci kaw loolu mu sàkk kubeeru saraxu njotlaay gu wurusu ngalam, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll.

Na def cuuraay li ci taal bi, foofa ca kanam Aji Sax ji, saxaru cuuraay si di làq kubeeru saraxu njotlaay gi ub gaalu àlluway seede si, ndax mu baña dee.

¶ Ci kaw loolu mbooloo ma yónnee ca Silo, ñu jëli gaalu kóllërey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Ki toog fi tiim ñaari malaakay serub yi. Foofa ca Silo la Ofni ak Fineyas, ñaari doomi Eli yu góor ya, nekkoon ak gaalu kóllërey Aji Sax ja.

Esekiya ñaan fi kanam Aji Sax ji, ne ko: «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim malaakay serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.

Su ko defee boroom nguur yeek boroom sañ-sañ ya fa déndi asamaan, mana xame ci mbooloom gëmkati Almasi, ni xelum Yàlla rafete ci wet gu nekk.

Yonent yooyu, xamalees na leen ne du seen njariñal bopp lañuy liggéeyal xibaar boobu, xanaa yeen. Ñi leen àgge xibaar bi tey ñoo di ñiy waare xibaaru jàmm bi ci dooley Noo gu Sell, gi ñu yebale asamaan, te muy mbir mu malaaka yi sax, noon siiwa nemmiku.