TSK

TSK · Hosea 4:5

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Moo tax Aji Sax ji doge Israyil bopp ak geen, boole tiir ak barax fóom ci benn bés.

Ñii ne: “Waajal-leen xare baak ñoom, nu songi leen digg bëccëg. Waaye wóoy nun, jant a ngi lang, keru ngoon di law!”

Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu, te gàcce gàcceelu leen. Xamuñu sax luy kersa! Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu. Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.» Aji Sax jee ko wax.

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy waxe waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.

Mu jëm ci yonent yi: Sama bopp a ubu ràpp, sama xol jeex, sama yax yépp ne yalax, ma mel ni ku biiñ man, ba mu màndi ndax Aji Sax ji ak kàddoom yu sell.

Sama loxooy dal yonent, yiy gis peeñuy caaxaan, di gisaaney fen. Sama péncum ñoñ, duñu fa teewe, limeefu kër Israyil, deesu leen ca bind, te réewum Israyil, duñu fa dellu. Su boobaa ñu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.

¶ «“Yaw Yerusalem, képp kuy léeboo dina la léeboo ne la: ‘Ndey ja, doom ja!’

Hosea 9:7 TSK

Bési mbugal dikk na, bési añale taxaw na, na ko Israyil xam. Yonent lañu jàppe ab dof, ku yor waxyu di ku wéradi, ndax seen ñaawtéef gu réy, ak seen mbañeel gu tar.

Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen.

Waaye Yerusalem, ga fa kaw, mooy gor si, te moom mooy sunu ndey.