Moo bëggoon di móoloo, yal na ko këppoo; soppul ag ñaan it, yal na ko barke sore.
TSK
TSK · Hosea 4:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku jub, jot sa yool ci kaw suuf, moykat beek soxor bi it daw raw.
Mag meek kàngam li ñooy bopp bi, yonent bi mokkal naaféq dib geen.
Yonent yiy wax waxyuy fen, sarxalkat yiy jiitee seen coobare, te sama ñoñ soppe ko ni! Moo bu muj ga taxawee, nu ngeen di def?»
«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.
¶ «Leween ñi ma sore woon ba bànni Israyil jàddee, ba dëddu ma, di topp seen kasaray tuur, ñooy gàddu seenu ay.
¶ Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel. Des na tuuti dinaa mbugal askanu buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa jeexal nguurug Israyil.
Ñoo sóobu ci xóotey yàqute, na woon ca janti Gibeya, te Yàlla mooy bàyyi xel seenug ñaawtéef, ba mbugale leen seeni moy.
Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »