TSK

TSK · Hosea 7:8

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ilyaas dikk jàkkaarlook mbooloo ma mépp. Mu ne: «Yeen nag dungeen dakkal seen ciŋiñ-caŋañ ji ngeen nekke, wet gu nekk ngeen féete fa? Su Aji Sax ji dee Yàlla, toppleen ko; su dee Baal, ngeen topp ko.» Mbooloo ma ne patt.

Ezra 9:12 TSK

Kon nag seen doom yu jigéen buleen leen may seen doom yu góor, te seen doom yu jigéen buleen leen jëlal seen doom yu góor. Buleen seet mukk seen jàmm mbaa seen njariñ. Looloo leen di taxa am doole, bay xéewlu ci ngëneeli réew mi, ba wacce ko seen askan fàww.»

xanaa di jaxasook yéefar yooya, di roy seeni jëf,

Hosea 5:7 TSK

Aji Sax ji lañu wor, nde doomi po lañu jur; Léegi la leen màggalug Terutel weer di booleek seen suuf, sànk leen.

Hosea 8:2 TSK

Man la Israyil xaacu, ne ma: “Éy sama Yàlla, maa la ràññee!”

ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi, ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji tey giñe Milkom, yàllantu ji,