Njabootam ne xas, saamar jagoo, te balaa booba duñu lekk ba suur.
TSK
TSK · Hosea 9:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Job 27:14
TSK
Yaa woote ni su doon bésu màggal, tiitaange dar kepp ma. Bésub merum Aji Sax ji, kenn rëccul, kenn muccul. Doom yi ma jur, yar leen, noon bi fàkkas leen!
Ezekiel 27:3
TSK
Waxal Tir mi tooge buntu géej, jula yooyuy jëflanteek xeeti dun yu bare, nga ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yaw Tir yaa noon: ‘Maaka matub taar!’
Hosea 10:14
TSK
Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor, sa tata yépp tas, na Salman tase woon Bet Arbel, keroog bésub xare ba, ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.
Amos 7:17
TSK
Gannaaw noonu la, Amaciya, Aji Sax ji nee: “Sa jabar ci biir dëkk bi lay gànctoo, say doom, góor ak jigéen, saamar tëral; sam réew, ñu natte buum, séddoo. Yaw nag, réewum yéefar ngay deeyeji; Israyil, ñu jële kom réewam, gàll ngàllo.”»