¶ Aji Sax ji nag waxati Musaa ne ko: «Gaawal wàcc, ndax sa mbooloo, ma nga génne réewum Misra def nañu yàqute.
TSK
TSK · Isaiah 1:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ñu dem nag, di jaamu yeneen yàlla, di leen sujjóotal, yàlla yu ñu xamuloon, te du lu leen Aji Sax ji féetale.
Njabootam ñoo def ug yàqute ci kawam, ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk. Ndaw maas gu dëng te njublaŋ!
Yeena ngi mébét njubadi, di lawal fitna ci réew mi.
Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma, teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
Seeni njiit të, xejjoo ay sàcc, ñoom ñépp sopp ger, di dàq ay neexal, ab jirim, sàmmuñu àtteem, àqu jëtun soxalu leen.
Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»
ma xabtal ko fi kaw xeet wu gëmadi, yebal ko ca askan woowu ma merloo, ngir ñu sëxëtoo leen, nangu seen alal, note leen ni banu mbedd.
Deesu la robaaleek yooyu buur, yaa yàq sam réew, faagaagal saw xeet. «Deesul tuddati mukk askanu lorkat wii.
Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.
Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa? Moo kooy yékkatil kàddu? Kooy xool gëti xeebeel? Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?
Yaa leen di bàcc, ngelaw wal, ngëlén tasaare; yaw ngay bége Aji Sax ji, di damoo Aji Sell ju Israyil.
Waaye yeen, dikkleen fii, yeen doomi xërëmkat yi, yeen askanu njaalookat yiy gànctu,
Ñoo di xeet wu ma ne jàkk, dëkke maa naqaral, di sarxalali tuur ci biiri tool, di leen taalal cuuraay ci kaw sarxalukaay bu ñu tabax,
«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.
Seenug mbon a leen di mbugal, seen ñàkk kóllëre yar leen. Ñamleen ba gis ni ngeen ma dëddoo, wormaalatuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, muy loraange ju leen wex.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Yeen aka mokkal gànctu! Jeeg ju bon ji sax di jànge ci yeen.
Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.
Wooleen fittkatoo fittkat fi kaw Babilon, mboolem kuy tàwwi xala. Gawleen ko, bu kenn rëcc. Feyleen koy jëfam; def ko ni mu def moroomam. Babilon a jaay reewande Aji Sax ji, ku Sell ku Israyil ki.
Maay def loolu ngir nanguwaat xolu waa kër Israyil, gi ma dëddu ngir seen mboolem kasaray tuur yi.”
ak ñi dëddu Aji Sax ji, wutuñu Aji Sax ji, sàkkuwuñu ko.»
¶ «Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
Am danuy yékkati fiiraangey Sang bi? Danu koo ëpp doole?
Ndaxte ay bàkkaaram jalu na ba àkki asamaan, te Yàlla bàyyi na xel ay ñaawtéefam.