¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.
TSK
TSK · Isaiah 10:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ana nu kenn di dàqe seen junni, ñaar di fëxal seen fukki junni, te ka ñu yaakaar jaayu leen, te Aji Sax ji, laa ne, waccu leen?
Siri songe penku; Filisteen ña, sowu, ñu sëxëtoo Israyil, wonn. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor, du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun. Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon, ku ci nekk di wax lu amul bopp. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
Manase song Efrayim, Efrayim song Manase, ñu mànkoo, noonoo Yuda. Teewul Aji Sax ji xàcci loxoom, meddiwul ba tey.
Lu waral coow li ak xaxaloo bi, ba dëkk biy riir? Ñi ngeen deele, saamar reyu leen, bóomuñu leen ci xare.
Seeni néew lees di xalab, ñu médd, xet ga gilli, seen deret la tund yiy sangoo.
Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Kiy wopp dee, wopp dee; kiy deeye saamar, deeye saamar; kiy deeye xiif, deeye xiif; kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.”
Bu ñu yaroon seeni doom it, maa leen leen di xañ, ba kenn du des. Te it ngalla ñoom, bu ma leen dëddoo.