Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»
TSK
TSK · Isaiah 10:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole, ma rëcc ñi séddoo dundu àddina. Say soppe, nga reggal, seeni doom regg, desalal seeni doom.
Bésub keroog saatu la Boroom biy wate, te saatu ba moo di buurub Asiri, mu àbbe ko ca wàllaa dex, wat la nel, wat say yeel, xuuf sab sikkim.
Sémmiñ dina diir mbagg ka koy gore? Am dogukaay dina réy-réylu ba sut ka koy doge? Mbete yet wuy xàcci ka ko ŋàbb; mbaa bolde bu walbatiku ŋàbb boroom!
Aji Sax jee damm bant, bi ñu bon ñi daan dóoree! Moo damm seen yetu nguur,
Du tee ma wàcceel Aryel musiba, ñuy yuuxook a jooyoo. Yerusalem ay mel ci man ni Aryel, taalub sarxalukaay.
Aji Sax jeey yékkati kàddoom gu màgg, wone diisaayu loxoom, ànd ak tàngooru meram, ak sawara wuy xoyome, ak waameek ngëlén, ak tawub doji yuur.
«Yaw Babilon, yaa doon sama wàkku, di sama ngànnaay, ma di la wàkke xeet yi, rajaxee la réew yi,
¶ Yéeneb waxyu bu dal dëkk bi ñuy wax Niniw a ngi, di téereb peeñum Nawum ma dëkk Elkos.
Keey xàccil loxoom bëj-gànnaar, keey sànk réewum Asiri, keey def Niniw ab gent bu wow ni màndiŋ.