Seeni sarxalukaay kay ngeen di màbb, seen tuuri doj, ngeen rajaxe, seen xer yi ñuy jaamoo Asera tuur mi, ngeen gor,
TSK
TSK · Isaiah 17:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Seen réew maa ngi fees aki yàllantu; ñuy sujjóotal seen liggéeyu loxo yooyu, te ñoo ko sàkkal seen bopp.
Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam, nii la mujje am njéggalu bàkkaaram: Day boole doji sarxalukaay bi yépp, rajaxe ni doji kew, xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe, mbaa sarxalukaayi suurukaay.
¶ Éy bokki Israyil, fippu ngeen Aji Sax ji ba sës, waaye walbatikuleen!
Ku mel nii du délloosim xelam, ba xam, ràññee ne: «Xaaju matt mi laa taal, lakke mburu, wàjje yàpp, lekk; mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii? Ab dogu bant laay sukkal?»
Ñoo fal ay buur te du sama ndigal, ñoo tabb ay kàngam, te yéguma. Seen xaalis ak seen wurus lañu sàkke jëmmi tuur, muy seen sànkute.
Bu Efrayim daan wax, ñépp ay lox; mu amoon daraja fi digg Israyil. Waaye moo sikkal boppam ci tuuri Baal, ba dee.
Yeen Efrayim, lu ma masa séq ak jëmmi tuur? Man maa leen di nangul, di leen wattu, di leen keral ni garab gu naat gu dul ruus, sa meññeef bawoo fi man.»
«Doom aadama ak mala, njanaaw ak jën laay buub, ak luy fakktale, booleek ñu bon ñi. Maay dagge doom aadama fi kaw déndub suuf.» Aji Sax jee ko wax.»