TSK

TSK · Isaiah 2:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Te it bu ngeen jëlalee seeni doom jabar ca seen doom yu jigéen, seen jigéen ñooña dinañu gànctook seeni tuur, ba xiir seen doom yu góor ci gànctook seen tuur yooyu.

Ku jublu ci ñiy gisaane nit ñu dee mbaa mu jublu ci boroom rawaan yiy seet, topp leen, di ma leen bokkaalee, dinaa ko noonoo moom itam te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

¶ Ci kaw loolu Israyil dale fa Sitim. Mbooloo ma nag tàmbali di moy ak jigéeni Mowab.

ndax xeet yooyii ngeen di dàqi kat, ay luxuskat aki seetkat lañuy déggal, waaye yeen seen Yàlla Aji Sax ji mayu leen loolu.

Aji Sax ji ne Musaa: «Yaa ngi nii di tëddi fa say maam. Mbooloo mii nag dinañu tàmbali di gànctuy topp yeneen yàllay doxandéem yu waa réew, ma ñu jëm ca seen biir. Dinañu ma wacc, fecci sama kóllëre gi ma fasoon ak ñoom,

Waa Filisti doora woolu seeni sarxalkat ak seeni gisaanekat, ne leen: «Nan lanuy def ak gaalu Aji Sax ji? Xamal-leen nu nan lanu koy delloo këram!»

Moo tax Aji Sax ji xalab mboolem bànni Israyil, fitnaal leen, teg leen ci loxoy yàqkat yi, ba ni mu leen wacce.

¶ Ma gisati ci jamono yooyu ay Yudeen ñu jël jabar ci waa Asdodd ak Amon ak Mowab.

Doom, dangaa gàddul nit bor, dige feyal jaambur,

Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.

¶ Ma ne kon, xanaa Yàlla daa wacc ñoñam? Mukk kay! Man ci sama bopp ci Israyil laa bokk, askanoo ci Ibraayma, giiroo ci Beñamin.