TSK

TSK · Isaiah 20:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Maay teg Misra ci loxol sang bu néeg, buur bu dëgër xol jiite ko. Kàddug Boroom bee, Aji Sax ji ci gàngoor yi.

Waa Misra, niti neen, duñu Yàlla; seeni fas it, suuxu neen, duñu leneen. Aji Sax jeey xàcci loxoom, kiy walloo mooy tërëf, ki ñuy wallu daanu, ñoom ñépp bokk sànku.

Soo nee ci sam xel: «Lu tax lii dal ma?» xamal ne sa ñaawtéef gu réy a waral ñu ñori la, saaysaaye la.

Yaw mi dëkke Misra mu taaru mi, ëmbal sa ëmb, jëm ngàllo; Memfis dëkk bii kat ci gental la jëm, di ndànd-foyfoy lu kenn dëkkul.

Bu ma dogee sidditi Misra, ba doole ja muy sago ŋiis, jant dootu fenkal Tapanes, aw xiin ay sàng dëkk bi, te dëkk-dëkkaanam ya, njaam lañu jëm.

Teewul ngàllo la dem, cig njaam; ay goneem, ñu falaxe leen ci mboolem selebe yoon; ay kàngamam, ñu tegoo bant; kilifaam yépp, ñu jéng leen.