Isaiah 37:24
TSK
Yaa yebal say surga, di kókkali Boroom bi, te naa: “Sama watiir yi ne xas laa ware kawtey tund yi, jàll ba ca xolu Libaŋ. Maa gor seedaram ya fa sut ak tànnéefi garabi sipparam: maay àkki ba ca collub kaw bu tundu Libaŋ, ak gottam bu naat ba nib tóokër.