Gàngooru Babilon gépp daldi ànd ak njiital dagi buur, ñu màbb tata ya wër Yerusalem.
TSK
TSK · Isaiah 22:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.
Yéene bii ñeel na xuru Peeñu ma: Ana lu ngeen di yéege, yeen ñépp seen kawi taax?
Ñu ne ko: «Esekiya dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer!
Seen noon yaa jiite tey, seen bañ yooyoo ne finaax, Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋ seeni tooñ yu bare, seeni doom duggig njaam, di moomeel ub noon.
Aji Sax jee dogoo rajaxe tatam janq Siyoŋ mu taaru, Moo tàllal buumu nattukaay, ngir tas ko, bankul loxoom it te màbbu ko. Moo jooyloo tata ak tabaxub fegukaay, ñu ànd tojatoo.
Wóoy kuy yàkkamti bésub Aji Sax ji! Ana lu ngeen am ci bésub Aji Sax ji? Dug leer, xanaa lëndëm.
Bésub keroog bésub sànj lay doon, bésub njàqare ak tumurànke, bésub gental ak gentle, bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus,
Su boobaa, “Nit ñee naan tund yu mag yi: ‘Daanuleen ci sunu kaw!’, naan tund yu ndaw yi: ‘Suul-leen nu!’ ”