TSK

TSK · Isaiah 24:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Dinaa tas seen bérabi jaamookaay, toj seeni suurukaay. Seen kasaray tuur yi ne làcc, ma jal ca seeni néew. Maa leen di sib,

¶ Mbir yi làqu daal, ñeel na sunu Yàlla Aji Sax ji, mbir yi feeñ nag, ñeel nu, nook sunuy doom ba fàww, te nu wara jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, mu ne: «bant ba sampe woon fu wóor day simpiku. Dees koy gor, mu fàq, la ca sëfe woon dog.» Aji Sax ji déy wax na ko.

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

Kon nag yeen tundi Israyil, dégluleen kàddug Boroom bi Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi, ak xunti yeek xur yi, ak ndànd-foyfoy yu wéet yeek dëkk yi gental, te xeet ya ñu dëkkal sëxëtoo leen, yab leen.