Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?
TSK
TSK · Isaiah 25:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yeen waa Siyoŋ, yeen waa Yerusalem, dootuleen jooy mukk! Bu ngeen jooyee, mu yërëm leen moos; bu leen di dégg, di leen nangul.
Ñi Aji Sax ji xettleey délsi, duggsi Siyoŋ, di sarxolle, kaalawoo bànneex bu sax. Mbég ak bànneex a leen di dab, naqar aku tiis dëddu leen.
Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee, agsaaley sarxolle fa Siyoŋ, kaalawoo mbég mu sax, mbégteek bànneex wàllsi, naqar aku tiis daw.
Dees laa foñ, jéppi la, ba kenn jaareetu fi. Waaye maay def ñu di la sagoo ba fàww, di la bége sët ba sëtaat.
Maay bége Yerusalem, bànneexoo sama ñoñ. Deesu fi déggati ay jooy, mbaa coowal njàqare.
«Man nag maa leen di musal ci njaniiwa? Maa leen di jot ci ndee? Moo yaw ndee, ana say mbas? Yaw njaniiw laa ne, ana sa tooke? Fomm làqu na ma!
Bu yaramu judduwaale wii nara yàqu solee weneen wu dul yàqu, ba yaramu ndee wii sol yaramu ndeetil, su boobaa la kàddu gii ñu bind di mat: «Mëddees na ndee ci géeju ndam.
¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.
ndaxte Gàtt bi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»
Mooy fomp seen wépp rongooñ: Dee dootu am, dëj aki yuux aku tiis dootu am, lu jëkk laay wéy.»