Ndax dooleem ju bare la may yeye? Déedéet xanaa! Dina ma teewlu moos,
TSK
TSK · Isaiah 27:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.
Teewul mu yërëm, baal leen seen ñaawtéef, ba sànku leen. Muñ na meram, muñati, te toppul xolam,
Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,
Aji Sax ji dafa wax ne: «Damaa fase seen ndey? Wonleen ma kayitu pase mi! Maa leen jaay njaam, feyey bor? Ana ku ma leen jaay? Bu ñu leen jaayee, seeni ñaawtéef a. Bu ñu fase woon seen ndey it, seeni moy a.
Duma wéye di sikke ba fàww, duma saxoo di mer, lu ko moy képp ku ma sàkk day tàggook bakkanam.
Xanaa du yeena def seen bopp lii, di wacc seen Yàlla Aji Sax ji, ba mu leen di jiite ca yoon wa?
Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Duma tas lépp tasar, waaye réew mi mépp ay gental.
Maa ngeek yaw, nar laa wallu.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay fàkkas mboolem xeet ya ma la sànniji. Yaw nag duma la fàkkas, duma la ñàkka topp moos, waaye li nga yelloo laa lay yar.»
Boroom bi déy du la wacc ba fàww.
Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf, ngelawal penku wowal doom ya, bànqaasam yu dëgër ya fàq, lax, sawara xoyom ko.
Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it, fa màndiŋ ma la ngelawal penku, ngelawal Aji Sax ji di uppe, bëti ndoxam tëju, ay teenam déy. Kii mooy sëxëtoo ab dencam, ak mboolem lu cay alal.»
Benn nattu dabu leen bu moy nattu yiy dale. Te it Yàllaa jara wóolu. Yàlla du nangu ngeen tegoo nattu bu ngeen àttanul, waaye nattu ba lay booleek pexe, ma leen cay génne, ba ngeen man koo dékku.