TSK

TSK · Isaiah 3:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Keroog juróom ñeenti fan ca weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund.

Moo tax, kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi, Jàmbaaru Israyil: «Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom! Maay fey samay noon!

Moo tax ñoñi Aji Sax ji di duggi ngàllo ndax ñàkk xam-xam. Seen kàngam ay deeye xiif, seen baadoolo deeye mar.

Sa boroom Aji Sax ji, sa Yàlla jiy layool ñoñam dafa wax ne: «Mu ngoog, maa jële ci sa loxo, kaas bu wex biy miirloo; taatu kaas ba def sama mbugal, dootoo ko naan.

«Buur sang bi, nit ñi de, lu bon lañu def Yonent Yàlla Yeremi; tàbbal nañu ko ca kàmb ga. Dina fa dee ak xiif ndax ab dund amatul ci dëkk bi.»

«Yaw nit ki, bu ma am réew dee moye jëfi ñàkk worma, ba ma dumaa leen sama loxo, dagge fa mburu, yónnee leen ab xiif, ba boole doom aadamaak mala dagge fa,