TSK

TSK · Isaiah 30:29

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ba loolu amee nag Musaa ak bànni Israyil woy Aji Sax ji, màggal ko. Ña nga naan: «Ma woy Aji Sax ji, ngir ndamam li kawee kawe. Fas ak gawaram la fab, xalab géej.

fu moy bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam. Foofa ngeen di rendi juru bésub Mucc bi ci ngoon bu jant biy so, yemook waxtu wa ngeen bàyyikoo woon Misra.

Kee di cëslaay, te mati jëf, wépp yoonam di njub. Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi, te njekk ak njub mooy boroom.

Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.

Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, giiroo ci Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit.

Màggaleleen kog liit, màggale ko xalam ak moroom ma.

Bésub keroog dees na ne: «Aji Sax ji, sant naa la; yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.»

Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Yàlla Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.

¶ Aji Sax ji dafa wax ne: «Demal ca tabaxkatu njaq ba, nga jëndi fa njaqu ban lu ndaw te ànd ak ñenn ci magi askan wi ak ñenn ci magi sarxalkat yi,