TSK

TSK · Isaiah 32:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Deesatul gaañe mbaa di lore, fi mboolem sama kaw tund wu sell wi, ndax ni ndox di feese ba muur géej, ni la àddina di feese nit ñu xam Aji Sax ji.

Du toqi, du nasax, ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf, fa waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.»

Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.

Hosea 3:5 TSK

Gannaaw loolu bànni Israyil dinañu walbatiku, sàkku seen Yàlla Aji Sax ji, ak Daawuda seen buur. Ca jant yu mujj ya, xolub ragal Aji Sax ji lañuy dikke fi moom, akug mbaaxam.

¶ Am xamuleen ne aji jubadi ñi amuñu cér ci nguurug Yàlla? Bu leen kenn nax: Muy fokati séy yi, di bokkaalekat yi, di jaalookat yi, di góor-jigéen yi, ak ñiy ànd ak ñoom,

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.