TSK

TSK · Isaiah 33:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Jaambur ñay dégg, di rag-ragi, tiitaange ne taral waa Filisti,

Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.

Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.

Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg, kawe, tiim xeetoo xeet.

Moo dooleel ñoñam, wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israyil, xeet wi mu xejjoo, di ko màggal. Màggal-leen Ki Sax!

Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»

Aji Sax jee wone dooleem ju sell ji, xeet yépp di gis, ba ca cati àddina. Ñépp ay gis sunu wallu Yàlla.

¶ Ba loolu amee jawriñ yaak laman yaak jaraaf yaak dagi Buur yéew leen. Ñu gis nag ne sawara wi lakkul seen yaram fenn, seen kawaru bopp xoyomuwul, seeni yére yàquwul, xeeñuñu sax xetu sawara.

Acts 2:5 TSK

¶ Booba ay toppkati yoonu Yawut a nga dëkke Yerusalem, te bawoo ci xeeti àddina yépp.