TSK

TSK · Isaiah 33:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Kon ñetti yoon cim at la mboolem seeni góor di teew fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ci bérab bi muy taamuji: fani màggalu Mburu mu amul lawiir, ak fani màggalug Ayi bés, ak fani màggalu Mbaar yi. Waaye deesul teewe loxoy neen fi kanam Aji Sax ji.

Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.

Doxleen biir Siyoŋ, wër ko, waññleen ay soorooram,

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ku doyloo Aji Sax ji, yaay tundu Siyoŋ, doo toxu; dangay sax ba fàww.

Su boobaa tundu Siyoŋ bépp, fépp fu ñuy dajee, Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg, guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ; leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,

Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne: “Du dugg ci dëkk bii, du fi soqig fitt, du fi taxawe ab pakk, du fi jal jal bu muy gawe!

Wurmbalu dëkk bi bépp fukki junniy xasab ak juróom ñett (18 000) lay doon. Turu dëkk bi nag, dale ko ca bés ba, di “Aji Sax jaa ngi fi.”»

Ku am ndam nag, maa lay def nga doon ag kenu fi sama biir néeg Yàlla, te doo fa génnati mukk. Maay bind fi sa kaw sama turu Yàlla ak sama turu dëkku Yàlla, te mooy Yerusalem gu bees, giy wàcce fa kaw, bàyyikoo fa sama Yàlla, maay bind it fi sa kaw sama tur wu yees.