Ba ñu demee, di ko suuli nag, fekkuñu dara ca moom lu moy kaaŋ ma doŋŋ ak ndëgguy tànk yaak cati loxo ya.
TSK
TSK · Isaiah 34:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Nagi àll yaay ànd ak ñoom daanu, ñook yëkk yu ndaw yaak yu mag ya, seen réew mi màndi deret, suuf sa niin batt ak nebbon.
Robu mbaam-sëf lees koy rob: diri génne Yerusalem, sànni ca biti.»
Maa lay wacc fi suuf, sànni la ci àll bi, dëël njanaaw yépp fi yaw, ba reggal rabi àll yépp ci saw yaram.
Maay nàndale suuf sa deret, mu wale ca tund ya, ba feesal yooni ndox yi.
Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru, ak wali waameek doji yuur, ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram, ak xeet yu bare yi ànd ak moom.
Bésub keroog laay may Gog ab pàkk, mu def ko sëg fi biir Israyil; mooy xuru jaarukaay wiy dog yoonu képp ku fa jaare, te féete yoonu penku wi jëm géeju Xorom ga. Fa lañuy rob Gog ak gàngooram gépp, ñu di ko wooye xuru Gàngooru Gog.
«Maa leen yónnee mbas mu mel ni mu waa Misra. Maa reylu seeni waxambaane ci xare, jàpplu seeni fas, gillil xetu néew ya ca seeni dal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.
Ñu dëggaate reseñ ja ca nalukaay, ba ca gannaaw dëkk ba, deret génne ca, taa ba tollook laabi fas yi, wala wal ba dajal digganteb ñetti téeméeri kilomeetar.