TSK

TSK · Isaiah 40:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aaróona ne leen: «Tekkileen boog, indil ma seen jaaroy wurusi nopp, yi ci seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen.»

Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:

Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, ñook ñi leen wóolu ñépp.

Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas mboolem xeet yeek seeni réew,

Tëggu weñ ba di ñaax tëggu gànjar ba, boroom wàkku soññ boroom dékk, ñu naa: «Taqaleb weñ yi baax na!» tey daaj jëmmi xërëm ja ay pont yu koy dëgëral.

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,

Xaalis lañuy jële Tarsis, xoobe ko bant, wurus wu jóge Ufas, ñu boole ca, ndaanaan liggéey ko, tëggu gànjar yett ko, ñu solal ko ndimo lu yolet ak lu xonq curr, lépp di liggéeyu ràbb yu xareñ.

«Ana luy njariñal yett jëmmu xërëm ju ki ko sàkk yett, mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli, di ci gëmloo nit ay fen? Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko, xërëm yoo móol te manula wax!