TSK

TSK · Isaiah 40:23

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 12:19 TSK

Keey futti sarxalkat, jàllarbi njiit lu riigu.

Job 34:19 TSK

Kii du far kàngam, du teg ku am ci kaw ku ñàkk, nde ñoom ñaar la boole sàkk.

Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom te jëfe ko. Kee jara ragal. Na ñi ko wër ñépp yótsiy teraanga.

Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.

Kàngami Cowan a ngi def yëfi dof, kàngam ya fa Memfis, ñu nax leen, te njiiti giiri Misra lajjal seen waa réew.

Bu bésub keroogee Aji Sax ji dikke mbugal gàngoor ya fa kawa kaw, ak buuri àddina yi fi suuf.

Ma nàndal waa Yerusalem ak dëkki Yuda ak seeni buur ak seeni kàngam ngir gental fépp, muy ndànd-foyfoy bu ñuy muslu, di ko móoloo ba sunu jonni yàllay tey.

ndax ngeen lekk suuxi buur ak suuxi njiiti gàngoor, suuxi jàmbaar ak suuxu fas ak gawaram, suuxu ñépp; gor ak jaam, mag ak ndaw.»