TSK

TSK · Isaiah 41:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 23:3 TSK

Éy bu ma xamoon fa may gise Yàlla, ba àkki péncam,

Job 38:3 TSK

Takkul boog te góor-góorlu, ma laaj la, nga xamal ma.

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Yeen waa dun yi, xeremluleen, déglu ma; yeen askan yi, takkuwaatleen, jegesi te wax, nu bokk teew, layoo.

Maay Aji Sax ji, seen ku Sell ki; maa sàkk Israyil, di seen buur.»

Micah 6:1 TSK

Dégluleen rekk li Aji Sax ji wax: Jógal layoo, tund yu mag yi seede, tund yu ndaw yi dégg la.